Céy suuf yaa ka sañ
Ku tollu ne Séex Ànta Jóob
Nga ne tey jii yaa ko tiim
Xanaa xamoo ne moom
Benn toq ci yuuram
Taa loo na say kër-i-kër
Sa kow yow ba muy dox
Séexlu woon a jëf ju bon
Gëstu la dëkke woon
Dëggu di xàll yoon
Céy Séex, ak a gore !
Way deŋ, yor fit wu réy
Di jëf ngir Afrig raw
Bii Jóob, def naa ko Buur !
Yow suuf, bul di dof waay
Saa waa ji dee ko weg waay
Lum bëgg, dee ci dox waay
Ba miy raw, nit santagul Njaay !
Séex Axmadu
Bàmba Njaay kaay
Toolu Séex
Du mës a daay
Sax ci di liggéey
Ba keroog ngay saay.
Photo de couverture : © Comic Republic
Comentarios