Àddina si tey dafa taxaw
Ku nekk naan man fu may aw
Nit naan moroomam bu fi ñëw
Jàngoro jee fiy xal a ñëw
Kanam yépp la ñu ëw tey
Ku sëqat ñenn ñi ne mëyy
Amatul nuyoo ak fóoniy lex
Koo ko fi def tey du ko neex
Ne leen ràpp tëju seen biir kër
Ku ci amus néeg na ko def kër
Amatul génn di wëndeelu
Walla doxantu ci mbedd miy féexlu
Bitig yu bari tëj nañ leen
Jàngu yiit tëj nañ leen
Njóobéen yaa ngi fàgguy wut ñam
Kenn xalaatul tey yàq ñam
Ku bëgg a faju walla jëndi lekk
Firnde ko cib kayit ngir mu nekk
Liggéeyi ak seeti mbokk mu tawat
Mënees na ko it ci kow waat
Yii dogal ñoo wàcc Tugal
Te ñaanu ma ñu yegsi Senegaal
Saay waa-Réew maa ngi leen di ñaax
Ci bàñ a jàppe koronaa ay nax
Ndeem day lu Yàlla dogal
Day ndogal gu ànd ak i ndigal
Ndigal li mooy nu sax di ñaan
Te boole kook di fagaru
Naam cet day lu mas a war
Tey jii nag la gën a war
Kuy dugg ci béréb na raxasu
Kuy génne ci béréb na raxasu
Ku ñu tàllal loxo na jéggalu
Kuñ ne jéggal ma nangul
Dugg-ak-génn ci néegu mag ñi
Nanu ko wàññi, waa-Réew mi !
Téye nenne-tuuti di këlli-këllee
Walla ku mënul noyyi nga féetee
Day lu baaxul ci fan yile
Mook ñóoxu soxna su tollu diggante !
Def mbooloo di garaN-palaas
Walla àndandoo di fecc raas
Warees na koo bàyyi jamono yii
Ak xew yi ci bopp koñ yi
Léep lu jëm ci wàllu Màggal
Na ame ci kër yi ak dal
Ku ne fa mu ne na sàkku ñaan
Ngir ëllëg nu dajaloo di ñaan !
Ku ci am dëkkandoo fajkat
Nemmeekul ko njabootam kat
Moom miy jaabante bañ a xàcc
Jaawalewul nit ak xaj
Yéen njiiti Senegaal yi
Nangu leeniy béréb def loppitaan
Tere jaaykat yi yokk lu duun
Lu ko moy Réew méey buun
Waajal leen ay dër yu naat
Ngir bekkoor bañ noo faat
Doomu-Afrig bu dugg sunu Réew
Teewlu leen ko ngir mën koo rammu !
Koronaa la taalif bi tudd
Séex Axmadu Bàmba ki ko bind
Njaay-Jaata, dëkk Njaaréem
Di góoru Ajaa Maryéem
Mooy ñaan mbas mi ne mes.
Photo de couverture : © Center for Disease Control's Public Health Image Library
Comments