“Ku ndóbin rey sa Maam, foo gisee lu ñuul sax daw.” Xanaa kon ndóbin gi nekk Senegaal di reye taxul wolof Njaay di wax?
Su may xalaat samag ngone, sama xel mi dafay fees dell ak ndox: ndoxu taw bi ak rongooñu nit ñi. At mu ne, mbënn mi dafay baaxental nawet bi, di mel ne ku nuy ñaawal. Réew mi yépp lay taawal, yàq i dëkkuwaay yu bari. Nit ñi dañuy mujjee gàddaay, ñàkk fu ñuy fanaan, seen sutura xàwweeku, ñuy sàkku ndimbal.
Alal ju dul jeex seey ci ndox mi, xeeti jàngoro yu nekk di ci ballee. Fii nga dégg ñu ne la tali xar na fi ; fale ñu ne la dawaan maas na fa kenn. Li gënatee metti, gënatee ruslu ci aw Askan, mooy dinga gis ñu lab ci ndox mi ; ñoo xam ne dinanu leen wër ay fan-i-fan laataa ndox mi di leen yàbbi : fekk ñu nekk ay néew yu tàmbalee nëb.
Ci noonu ngay gis ni réew mi yépp jaaxle. Foo walbatiku wax ji doon benn : mbënn mi ub na bopp yi. Ñaa di ñaxtu, ñaa di woote wallu. Ñaa di jàppale ji seen dëkkandoo ngir mu ŋacc këram. Ñaa di woote tele di fa maye alal ju takku (ju kenn xamul fu mu jóge) : ngir, nee ñu, xeex mbënn mi.
Waa Càmm gi itam bokk nañu ci fuural bi. Ñoo nga naan li fi xew metti na leen ba fa mettit yem. Ñoo ngay wootante ndaje, di limati ay tamñareet (miliyaar) naan ci xeex bi la jëm. Xeex boo xam ne saa su nekk sunu ndigg a ciy rëq. Ñoo ngi naan dale ko 2012 def nañu ci 766,988i tamñareet.
Kàddu yu ni mel dañuy toqal ay laaj yu néew ci sama xel. Ndax Càmm gi, ci dëgg-dëgg, jot na fee fob alal ju baree nii jëmale ko ci xeexu mbënn mi? Su dee loolu dëgg la, kon fu 766,988i tamñareet yi jaar ? Ñaata la ñu ci randal ba tax mbënn mi dëkke noo daan? Ak kan moo randal xaalis boobu ?
Dafa yomb lool di tudd ay tamñareet yu dul jeex, te duñu feeñ fenn ci sunu nekkin. Ni fi mbënn mi saxee dafay màndargaal lu bari, lu ñaaw, ci sunu Askan wi ni muy doxe ak ni ñu koy jiitee. Sunuy jàngoroy daawaati-jéeg ñoo nuy gaañ ba tey jii. Bakkan yiy rot ci mbënn mi, dëkkuwaay yi ciy yàqu, taxuñu nu dogu jële ko fi ba fàww.
Ñaata ci nun noo fi nar a deewati, ñaata ci nun noo fi nar a gàddaayati, ngir nu bàyyi caaxaan te liggéey ? Lan moo gën a ruslu ay ndongo-daara yu lab ci ndoxu taw mi walla ay way-tawat yuy féey ci biir loppitaan yi ?
Li wara dakk mooy pasar-pasare alalu réew mi! Di ko luubal, walla di ko dugal foo xam ne njariñam des naa leer. Seeti ay nit, di leen mas-sawu, di dëfal seen xool ak ay saaku ceeb, du li nuy xaar ci njiit lu mat njiit. Askan wi du ab yalwaankat : ku koy aar la soxla. Ku dul bàyyi ba mu gaañu muy soog a ñëw di ko jéem a won yërmaande.
Mënunu lu ñëw sunuy njiit xulliy gët naan “dafa noo bett”, “mënunu ci dara”, “areem” (càkkkeef) bee soppeeku: nun ak àddina si noo ci bokk yem”. Ñoom ñi sàkku nu dénk leen sunum Réew, dénk leen sunu kaaraange, dénk leen sunu koppar, su dee mënuñu lu dul dinu mas-sawu, mooy ne amaluñ kenn njariñ.
Su nit ñi sañee tabax fu ñu warul a tabax ; su xunti yi fattee ci at mi (ak lu leen mënti fatt), te kenn sàññiwu leen lu jiitu nawet bi, dafa fekk ne sunuy njiit defuñu seen liggéey. Su ñu ko defoon dëgg, duñu sàggan ba at mu nekk, la nu daloon daaw dalaat nu. Ñoom ñi sañ a dogal ak a tere, su ñu xoolee ba lu neex waay def te dara du ko ci fekk, dafa fekk ne ñoom ci seen bopp dañoo nekk di def li leen neex. Te ku nekkul di jubal nag, sañul a digal kenn.
Jotati na sunuy njiit yedd seen bopp, te nun waa Réew mi nu gën a xam sunu bopp. Bunu wayadi ba lu nu waay sëf rekk nu nangu ko, dékku ko, ba noppiy soox. Ndax ñàkk faayda wesuwul ndóbin di tegleey at di fàdd aw askan mu ni yàcc-yàccaaral di xullee.
Photo de couverture : © DIALO Photography
Comments