Version audio du Taalif
Yàgg, yàgg, dëggay daan
Dëgg lottoon na Senegaal
Usmaan Sonkoo tax mu daan
Lii dinaa ko bind ngir ëllëg
Da nga daan xëy di liggéey
Njiitu Réew dàq la sa liggéey
Dàqin wu ñaaw, mbete sàcc
Te yaa doon xeex ñay sàcc
Askan wi fal la, def la député
Ngay dëggal, doon ku nite
Fa nga daan taxaw Assemblée
Ku fa taxaw tey du ko mate
Ngay wax dëgg, ñu lay mbëw
Waa APR ak Abdu Mbow
Téye sa der bi di ci saw
Seeniy sobeek seeniy pexe
Présidentielle 2019
Ñu lay kókkali, nga ñëw doon
Ñetteel ca ña jiitu
Idrisa Sekk xëy la wor
Maki Sàll téye di tëjje
Tekk-der di kàjje, di pese
Xalifa Sàll nekk kaso
Nga taxawu ko, mu génn dëddu la
Ñi fi amul woon récépissé
Ñi fi amul woon ku leen faale
Ñi fi amul woon fitu gaynde
Usmaan, yaay ki leen xetali
Mag yu bari faale wu ñu ndaw
Nga wax ak ndaw ba mu mat mag
Lu mel nii ci sunu Réew
Néew na foo koy gise
Ba ñu xamee nag ne yaa leen gën
Ca la nu jóg di la tuumaal
Giiñ na nu la fi siif, giiñ la rebelle
Giiñ la terroriste ak sàcc téléphone
Jël na ñu la tëj ak sa njaboot
Ñaari weer ci sunu biir Réew
Gii gàcce, gàccee ka réy
Soo yambaroon nu dooniy jaam
Nu ne déet, ñu sanni la kaso
Sa parti, ñu gont tas
Say junni àndandoo ñu tëj
Juroom-fukk ci ñoom ñu rey
Siggil ndigaale, Usmaan Sonko
Ci Baay Seex Jóob mi ñu bóom
Siggil ndigaale, Usmaan Sonko
Ci Prosper Senghor sa doom
Ñoom ñii, ñooy say nawle
Ñiy dund, ñi ëpp matu ñu
Tey jii, nga génn kaso
Ginnaaw nga woor lu jiitu Koor
Looy defati bàyyi leen ci xel
Nit ñi génn di la teeru
Ñoo yey, da ngaa gore
Maki Sàll bëggul a dem
Nga samp Basiiru ngir mu dem
Sa jëf yii ni ñu taaroo
Yal na yiy ñëw gën a taaru
Yaakaar yi nga yee ci nit ni
Yal na ci ndam yu réy topp
Liy ñëw nag mooy gen a metti
Jagal Réew coono la doŋŋ
Waaye nag du yow laa koy wax
Ku ragal coono daa bañ lu baax
Doxal, Usmaan, bul jeng
Ci yow kat danuy jàng
Ëlleg, bëg na nu laa weesu
Sunuy rakk it nëw di nu jiitu
Senegal dëkkee tedd
« Yaa gore », la taalif bi tudd
Seex Axmadu Bàmba ki ko bind
Njaay-Jaata, dëkk Njaaréem
Di góoru Ajaa Mariyeem
Moo la naan, dalal ak jàmm !
Seex Axmadu Bàmba Njaay
15/03/2024
Cheikh Ahmadou Bamba Ndiaye est l’auteur du blog Assumer l’Afrique. Né à Diourbel, cœur du Sénégal, il a vécu sept ans au Burkina Faso, au Prytanée Militaire de Kadiogo. Écrivain à temps partiel, amant attitré de la poésie (auteur d’une dizaine de recueils), il écrit en wolof, français et anglais.
Il est titulaire de quatre masters en droit (Sciences Po Paris, Panthéon-Assas), en communication (Paris-Saclay) et en gestion publique (ENA — Paris-Dauphine). Pour en savoir plus sur l’auteur.
Voix : © Aïssatou Ndiaye
Montage : © Adja Marième Sy
Photo de couverture : © Sylvain Cherkaoui, Silya Ferrat, Bentaleb Sow, John Wessels, et sources anonymes
Bravo mon neveu,
Très beau poème !
Très beau poème cher Bamba. Toutes mes félicitations