Bitenti (taalif)
Dernière mise à jour : 14 nov. 2023
Bàkkan yaa ngi rot ney xob
Ku faatu nu gaaw dem rob
Xeetu rongooñ nu fexe pàccal
Teewul lijjanti lii du lu nu soxal
Siggil ndigaale, siggil sa wàll
Jaale rekk la ñu def seen wàll
Ceebak koppar ñu sànni jaxal
Mbete warax mooy li nuy dëfal
Njaal yi dooy na, bu leen nu rey
Jéem leen noo wattul li nuy rey
Suul nit, ngoon nu fàtte xaat
Mooy tax la daan faate di faat
Lim naa Poroxaan ak Malem Oddar
Jooy naa Kumpetum ak waa Ndar
Tuubaak Cëmbël jaale na nu leen
Laataa Bitenti di suul 21 jigéen
Ñii faatu kuy sàmmi seen njaboot ?
Ña ca làggee kuy leen di xal a boot ?
Nit ñu doon dox seen soxla
Tey ñoo ngi nar a diisaate seen i soxla
Su nu lii mettiwul lu nuy metteeti ?
Waa Réew mi rikk bu nu lii dalati
Dawalkat yi yéen doo leen i dof
Yaru leen waay, bàkkan du lu oyof
Askaan wi, sunu bopp na nu aar
Bañ di tàncaloo ney ganaar
Njiit yi yéen, luy seen njariñ ?
Noo ngi dee ngeen took di biiñ.
Photo de couverture : © Jack Gittoes